TURU MARK BI

Bio‑Oil®


TUR AK TOLLUWAAYU PORODI BI

Skincare Oil 25ml
Skincare Oil 60ml
Skincare Oil 125ml
Skincare Oil 200ml


TÉKTAL YI

Legët yi Dafay tanelo melokaanu legët yu bees ak yu yàgg yi. Ay rew Dafay tanelo melokaanu rew. Dafay yokk taweeku der bi, kon mu tere juddu gu yeneen rew. Melokaanu der bu massé wul Dafay tanelo melokaanu der bu timpi tampa. Der buy maggat Dafay taneloo melokaanu kanam ak yaram buy maggat. Der bu wow Dafay wañi ñakk niin te taneloo melokaanu der bu wow.


WONALE

Diw bu oraas / wiyole.


NAS BA

Ap Kàngam ci jaxase diw yu am witamin ak lu joge ci garab.


INGRÉDIEN YI

Paraffinum Liquidum, Triisononanoin, Cetearyl Ethylhexanoate, Isopropyl Myristate, Retinyl Palmitate, Helianthus Annuus Seed Oil, Tocopheryl Acetate, Anthemis Nobilis Flower Oil, Lavandula Angustifolia Oil, Rosmarinus Officinalis Leaf Oil, Calendula Officinalis Extract, Glycine Soja Oil, Bisabolol, Tocopherol, Parfum, Alpha-Isomethyl Ionone, Amyl Cinnamal, Benzyl Salicylate, Citronellol, Coumarin, Eugenol, Farnesol, Geraniol, Hydroxycitronellal, Limonene, Linalool, CI 26100.


LUY JUR ALERSI

Am na 11 mbiir yu meuna andi diafédiafé si deru yaram ci Bio‑Oil® Skincare Oil. Ni ki luy jur alersi yu bare, ñu ngi ci diwu garab yi ak xet yu neex. Ñoo doon: Alfa-Isomethyl Ionone, Amyl Cinnamal, Benzyl Salicylate, Citronellol, Coumarin, Eugenol, Farnesol, Geraniol, Hydroxycitronellal, Limonene, ak Linalool.


SEYTU KAARAANGE GI

Bio‑Oil® Skincare Oil amna kenn kuy yéngu ci wallu seytu lu jém ci poson ku seytu kaaraange am mu firndéel ni amna kaaraange ñeel jéfandiku bi ko waxambaane yi wara jéfandiku, yokk ci jigéen yu ëmb ak ñii di nampal, ak ay xale yu am lu ëppu ñetti at.


JÉEM SEYTU DER BU WOW CI KILINIK

Bérëbu Jéemukaay proDERM Institute for Applied Dermatological Research, Hamburg, Germany. Mebët Ngir natt xarañteef bu Bio‑Oil® Skincare Oil ci taneloo melokaanu kël yi. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 36 jigéen ñi bokk ci ay jëmm yu bare yu ñuy wax Fitzpatrick. Atu legët yi: buy sooga am ci xale bu 3 at. Fi leël yi nekk: Biir, yéel, loxo, bàat, óom yaram, li ci kaw ci yaram. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu dul xam boróom, bu ñu lambatu, ak buy gëstu walum placebo. Nit ñi ci bokk amoon na ñu ay legët yu ci dëppo mbaa yaatu bu baax ba mu tax xaaj-xaaj jëfandiku diwu legëk ak mingalé ñi ci bokk ci seen biir. Jëfandiku porodi bi ñaari yoon ci diiru 8 ayubés, amul beneen maasaas bu ñu amal ci fi ñu joxoñoon ci yaram wi. Jëfandiku bu ñu def ci kontrol saa su nekk. Seytu yi ñu def ci 0, 2, 4 ak 8 ayubés. Am na ay paràmètir yu bari yu ñuy xayma ci kiy faju ak xoolukaayu seytu ay lgët (POSAS) sax cammbaroon na ñu leen def. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil dafa xareñ ci rafetal melokaanu kël yi. Ap resilta bu am solo ci wallu lim la ñu am ginnaaw 2 ayubés kese (bés 15), jaadu na ci 66% ci ñi bokk. Ginnaaw 8 ayubés (bés 57) 92% ci ñi bokk wonewoon na ñu tan, tan boo xam ni matna ñetti yoon bi ci 2 ayubés. Ap yokkute POSAS bu wéy ci diiru jangat bi.


JANGAT LEGËTU AKNE

Bérëbu Jéemukaay Dept. ci dermatoloji, Peking University First Hospital, Peking, Chine. Mebët Ap jangat ngir seytu xareñteef bu Bio‑Oil® Skincare Oil ci taneloo melokaanu legët yu akne ci kanam ci ay Sinwa. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 44 sinwa yu amoon ay legët yu bees ci kanam (<1 at). Toppoto ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil amoon na 32 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 12 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 14–30. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Jëfe porodi yi ñaari yoon ci bés ci diiru 10 ayubés. Jëfandiku bu ñu def ci kontrol saa su nekk. Seytu yi ñu def ci 0, 4, 8 ak 10 ayubés: Benn fajkatu der dina cambaraat jéego yu kël bi su ñu boole lép ak gestukat bi, natt melokaanu kël akne/ xonkaay te jëfandiku chromameter, natt sebum ak sebumeter, nafar limu komedo yi ak neewi neewi yi. Nit ñi ci bokk tamit tontu nañu benn kayit làaj boppam. Resilta Resilta bi gën ci note bu kilinik bi mu ngi woon ci kattan bi Bio‑Oil® Skincare Oil am ci wallu wañi erythema mbaa xonkaayu këlu akne, ak lu ëppu ci der bi gëna leer. Mujjantalu kayit seytu sa bopp yi wone na ñu ni lu ëppu 84% ci nit ñi bokk tanena ñu ci seen wallu kël akne ak lu ëppu 90% tanena ñu ci wallu melokaanu kël. Resilta limu akne ak nattum sebum bi wonena ñu ni jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil du inndi mbaa mu gëna garawal akne mbaa yokk sebum.


AY REW JÉEM CI KILINIK

Bérëbu Jéemukaay proDERM Institute for Applied Dermatological Research, Hamburg, Germany. Mebët Ngir natt xarañteef bu Bio‑Oil® Skincare Oil ci taneloo melokaanu rew yi. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 38 jigéen ñi bokk ci ay jëmm yu bare yu ñuy wax Fitzpatrick. Sabab rew yi: bari na ñu ginnaaw ëmb, yaram wu yokku mbaa ay mbiri maggàay. Bërëb yi rew yi nekk: biir, pooj ak kapp. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu dul xam boróom, bu ñu lambatu, ak buy gëstu walum placebo. Nit ñi ci bokk amoon na ñu ay rew yu ci dëppo mbaa yaatu bu baax ba mu tax xaaj-xaaj jëfandiku ak tékkali ñi ci bokk ci seen biir. Jëfandiku porodi bi ñaari yoon ci diiru 8 ayubés, amul beneen maasaas bu ñu amal ci fi ñu joxoñoon ci yaram wi. Jëfandiku bu ñu def ci kontrol saa su nekk. Seytu yi ñu def ci 0, 2, 4 ak 8 ayubés. Am na ay paràmètir yu bari yu ñuy xayma ci kiy faju ak xoolukaayu seytu ay lgët (POSAS) sax cammbaroon na ñu leen def. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil dafa xareñ gëna rafetal melokaanu rew yi. Ap mujjantalu bu am solo ci wallu lim la ñu am ginnaaw 2 ayubés kese (bés 15), jaadu na ci 95% ci ñi bokk. Ginnaaw 8 ayubés (bés 57) 100% ci ñi bokk wonewoon na ñu tan, tan boo xam ni matna ñetti yoon bi ci 2 ayubés. Ap yokkute POSAS bu wéy ci diiru jangat bi.


JÉEMU KILINIK CI DER BU AM AY MELOKAAN YU BOKKUL

Bérëbu Jéemukaay Thomas J. Stephens & Associates, Inc., Texas, réewum Amerig. Mebët Ngir seytu xarañteef Bio‑Oil ® Skincare Oil ci gëna rafetal melokaanu der bu am ay melokàan yu bokkul ak xeesal bu am ay tàas su ko jigéen buy deru kanam ak baatam bi (maggat). Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 67 jigéen ci ñi bokk ci xetu der Fitzpatirik ak yaxute der bu yem ci kanam ak ci baat. Toppoto ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil amoon na 35 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 32 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 30–70. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Jëfandikukat bi ñu jëfe ci kanam ak ci gànnaaw bi ñaari yoon ci bés ci 12 at. Jëfandiku bu ñu ngi ko amaloon ci kanamu kenn ci ndoortel bi. Seytu ci kilinik bi yi ñu ngi amoon ci 0, 2, 4, 8 ak 12 ayubés. Nit ñi ci bokk deñoo note kenn ci ñoom ci kanam ak baat ba ngir der bu am melokaan yu nirowul ak xeesal bu timpi tampa Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil dafa xareñ ci taneloo melokaanu deru yaram bu yaxu (maggat). Ginnaaw 4 ayubés, amna ñu resilta bu am solo lool. Ginnaaw 12 ayubés, 86% ci nit ñi ci bokk pajum selil Bio‑Oil® Skincare Oil wonena ñu ap tan bu am solo ci coppite melokaanu kanam gi, 71% ci nit ñi bokk te am xeesal bu am ay tàas kanam, 69% ci coppite melokaan baat bi ak 60% xeesalu baat bu tàas.


JÉEM SEYTU DER BUY MAGGAT CI KILINIK

Bérëbu Jéemukaay Thomas J. Stephens & Associates, Inc., Texas, réewum Amerig. Jangat 1: Kanam ak baat Mebët Ngir seytu xarañteef Bio‑Oil ® Skincare Oil ci gëna rafetal melokaanu deru jigéen CI kanam ak CI baatam (maggat). Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 67 jigéen ci ñi bokk ci xetu der Fitzpatirik ak yaxute der bu yem ci kanam ak ci baat. Toppoto ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil amoon na 35 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 32 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 30–70. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Jëfandikukat bi ñu jëfe ci kanam ak ci gànnaaw bi ñaari yoon ci bés ci 12 at. Jëfandiku bu ñu ngi ko amaloon ci kanamu kenn ci ndoortel bi. Seytu ci kilinik bi yi ñu ngi amoon ci 0, 2, 4, 8 ak 12 ayubés. Nit ñi bókk deñuy leen seytuwoon ku ci nekk ci kanam ak baat bi ngir yii paramétar xareñteef: melokaan ci lépp, rédd yi, ras yu rëy, xeesal bu am tàas, der bu am melokaan yu maasewul, dégëraay/nooyaay ci gis gis, dégëraay/nooyaay taktil, melokaan bu àn ak léer (léndëm). Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil dafa xareñ ci taneloo melokaanu deru yaram bu yaxu (maggat) ci . Ginnaaw 8 ayubés, amna ñu resilta bu am solo lool. Ginnaaw 12 ayubés, 94% ci téere yi ci xëtu jëfandikoo bi ñuy wax Bio‑Oil® Skincare Oil, am na yu am solo ci gis-gisu décolletage, tànk ak tànk. Jangat 2: Yaram Mebët Ngir seytu xarañteef Bio‑Oil ® Skincare Oil ci taaneloo melokaanu der bu am ay melokàan yu bokkul ak xeesal bu am ay tàas su ko jigéen buy deru kanam ak baatam di (maggat). Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 67 jigéen ci ñi bokk ci xetu der Fitzpatirik ak yaxute der bu yem ci kanam ak ci baat. Toppoto ay selil ak Bio‑Oil® Skincare Oil amoon na 35 nit yu ci bokk li ñu toppotowul woon amoon na 32 nit yu ci bokk. Atu nit ñi ci bokk: 30–70. Anam bi ñu koy defe Lu ñu làmbatu, cambaraat ko, ku ñu xamul moo note jangat bi ci kumpa. Nit ñi ci bokk bokkoon nañu ci ap natt bu njékk toftal ci raxas ci diiru 1 ayubés. Porodi bi jëfe na ñu ko ci ap piyéesu weñ, ci suufu yeel ak loxo ñaari yoon ci bés 12 ayubés. Jëfandiku bu ñu ngi ko amaloon ci kanamu kenn ci ndoortel bi. Seytu ci kilinik bi yi ñu ngi amoon ci 0, 2, 4, 8 ak 12 ayubés. Nit ñi bokkoon deñ leen notewoon ku ci nekk ci kilinik ci piyees weñ, suufu yeel ak loxo yi ngir yii paraméter xareñteef. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil dafa xareñ ci taneloo melokaanu deru yaram bu yaxu (maggat). Ginnaaw 4 ayubés, amna ñu resilta bu am solo lool. Ginnaaw 12 ayubés 89% ci nit ñi ci bokk pajum selil Bio‑Oil® Skincare Oil ap yokkute bu am solo ci lu ëppu ci melokaan dekolte bi, suufu yéel yi ak loxo yi.


JÉEM SEYTU DER BUY DESIDARATE CI KILINIK

Bérëbu Jéemukaay Labo fotobiyolosi bu Daara bu kawe bu réew Afrik di Sid. Jangat 1: Stratum corneum niinaay ak njériñu bariyeer Mebët Ngir cambar njéexitalu jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil benn yoon ngir yokk stratum corneum (SC) njériñu bariyeer ak niinal. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 40 jigéen ñi bokk ci ay jëmm yu bare yu ñuy wax Fitzpatrick. Bérëbu xayma: Porodi test yi ñu def ci palmeer loxo nit ñi ci bokk yépp. Anam bi ñu koy defe Cambar niinaayu der bi ak cornéometar kom nattukaay bu njékk, cambarum njériñu bariyeer ak vaporimétre ni ñaarelu nattukaay. Nit Ñi doon bokk ci deñoo raxas seeni loxo ak saabu 2 waxtu laata ñuy natt ngir xool wowaayu der. Jëloon na ñu ay natt ci ndoortel. Biyo-Oil® Skincare Oil ak diw bu nu rañe ci la ñu jëfandikuwoon ngir xajjale ay bérab ci volar loxo nit ñi ci bokk yépp. Nattaat na ñu ci saas yi ginnaaw bi ñu jëfandiko porodi bi ak niari waxtu ci ginnaaw itam, laata ak ginnaaw bi ñu fompe porodi bi. Xayma nañ bërëb bu Fu ñu toppotowul ci jamano bu nekk. Resilta Ginnaaw jëfandiku ci saas yi, ñaari diw yép deñoo wañi ñakkum ndoxu der (TEWL) su ñu ko tékkale ak toppoto bi ñu seytuwul ba. Yokkute kappasitàasu der bi niari waxtu laata fomp bi wone na ap niinaayu der bu yokku. Ñaari waxtu ci ginnaaw,bi ñu sotte diw ci kaw der bi, Bio‑Oil® Skincare Oil wone na ap yokkute yu gënaam solo ci TEWL su ñu ko tékkale ak diw gi ñu rañe bi, di wone yokkute ci faraay bi kon ak niinaayu der. Jangat 2: Melokaanu der bu wow Mebët Ngir seytu jéego jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil ñaari yoon ci bés ngir faraay ak feexaayu der bu wow. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 25 jigéen kokasiyen yi ci bokk. Bérëbu xayma: xayma porodi yi ñu diw ci bitti yéélu ñi ci bokk yép. Anam bi ñu koy defe Saabu la ñu jëfandikuwoon ngir faj der bu wow bi ci diiru 7 fan. Bio‑Oil® Skincare Oil ak diw bu rañeeku la ñu jëfandiku woon ñaari yoon ci bés . Ay cambar amoon na ñu ci bés 1 ak 3. Defoon na ñu ay cambar ci wallu gis ak benn cambarkat bu ñu taggat ak benn lamp buy rafetal 2x. Xayma nañ bërëb bu Fu ñu toppotowul ci jamano bu nekk. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil ak diw bu ñu rañe bi gënna rafetal der bu wow bi su ñu ko tékkale ak bi ñu toppotowul. Bio‑Oil® Skincare Oil dafa gën a màgg ci 3 fan. Yokkute yu am solo ci rafetaayu melokaanu der bi ci bérab yi ñu toppoto ak Bio‑Oil® Skincare Oil firndel na ñu ko.


SEYTU DER BU OYOF

Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir séytu ni Bio‑Oil® Skincare Oil mëne inndi neewi der ba. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 25 nit; 19 góor ak 6 jigéen, ñoom ñépp ñu am ay der yu oyof su nu sukkandikoo ci seytu bu asid laktik. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu lambatu te xoolaat ko. Ñaari pacc lañu seetlu: pacc bi ñu defoon test bu negatif (ndox bu amul mineraal) ak pacc bi ñu diwoon Bio‑Oil® Skincare Oil. Porodi yi ñu seytu yep ci ndiggi ñi doon bokk lañu ko def ci kaw der gi ci diiru 48 waxtu di jéfandiku Finn Chamber®. Yengu yengu der ba ci teewaayu kuy yéngu ci fajum der la woon, ngir xayma tawat ci wallu der bu njékk ci 15 simili, 1 waxtu ak yeneen 24 waxtu ginnaaw bi ñu dinnde jubbantikaay. Yengu yengu der yi ci diggante 0–4 la ñu ko nattoon (fekk 0 nekkul erythema, mbaa dët mbaa yeneeni neewi der ba ak 4 nekk erythema ak dët dégg, di wone xonkaay bu lénndëm ak neewi bu yaatu ci kaw pacc bi ñuy diwu mbir ma). Resilta Kenn ci ñoom amul ay réent yu bon ci jëfandikoo test bi, ak benn xët yu bare yu ñu ràññee ci 0 (zero) ci mboolem jëfandikoo yi ci jamono yépp. Kantanu der bi ci Bio‑Oil® Skincare Oil neena ñu ‘du inndi neewi derba’.


JÉEM NDAX DU JOXE AY TOMB CI YARAM

Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir teste ndax Bio‑Oil® Skincare Oil dafay joxe akne ak comedo (ay pic). Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 20 nit; 14 jigéen ak 6 góor yu am ay xeet yu wuute te am der yu ame akne. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu lambatu te xoolaat ko. Porodi bi defoon na ñu ko ci ap kayitu séggukaay ci kaw ndiggi nit ñi ci bokk. Bayiwoon na ñu ci ay bandàas 48 ba 72 waxtu, dinndi lènn ba noppi délolènn ci. Defoon na ñu ci 12 bandàs ci lép ci 4 ayubes yu toftalo. Ñetti pacc lañu séytuwoon daa di tékkale test bu negatif (ndox bu amul mineral), porodi jéem bi (Bio‑Oil® Skincare Oil) ak test bu positif (lanolin alkol, ap porodi komedo bu ñu xam). Yengu yengu der bi seytuwoon na ñu leen ci kanamu ap fajkatu der 15 simili ginnaaw bi ñu dinnde bandaas bu ci nekk ngir tékkale teewaayu komedo bi laata ak ginnaaw diwu porodi bi. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil amna ñu gis ni du komedo. Pacc bi ñu jëfe Bio‑Oil® Skincare Oil wutewul torop test bu negatif ci pacc boobu. Test bu positif bi wonena akne.


JANGAT NÀAN BI

Bérëbu Jéemukaay proDERM Institute for Applied Dermatological Research, Hamburg, Germany. Jangat 1: Xaymakat yu ñu taggat Mebët Ngir cambar xayma nàan bu Bio‑Oil® Skincare Oil ginnaaw jëfandiku bu ñu waxtaane ba jubo. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 22 xaymakat yu ñu taggat; 21 jigéen ak 1 góor. Bérëbu xayma: Porodi test yi ñu def ci palmeer loxo nit ñi ci bokk yépp. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu dul xam boróom, bu ñu lambatu, te placebo seytu ko. Biyo-Oil® Skincare Oil ak diw bu nu rañe ci la ñu jëfandikuwoon ngir xajjale ay bérab ci volar loxo nit ñi ci bokk yépp. Xaymakat yi jëfandiko na ñu 100 yéngu yéngu ci ay diir yu ñu natt. Xaymakatyi nattoon na ñu nàanum porodi bi ci 5 poñ doore ko' nàan bu tuuti yeexa yeex' ba 'nàa bu gaawa gaaw'. Nattukaayu Sebum yi, ngir jébbal coonoy diw ci gànnaaw bi, ñu jël ci ñaari jamono; bi ñu ko jëfe ak 2 minut bi ñu ko jëfe. Resilta Nàan bu Bio‑Oil® Skincare Oil ci der bi ñu ngi ko cambaroon mu nekk ‘gaawa gaaw’ mbaa ‘gaaw’ 77,3%) ci natkat yi ñu taggat. Lii deñ ko xoolaat ci nattukaayu jumtukaay ak njàngum sebumeter ak ci poñu ñaarelu yoon bi di wone ni li desoon ci Bio‑Oil® Skincare Oil moo gëna ndaw fuuf su ñu ko tékkale ak diw bu rañeeku bi. Jangat 2: Ëttu jëfandikukat yi Mebët Ngir cambar xayma nàan bu Bio‑Oil® Skincare Oil ginnaaw jëfandiku bu ñu waxtaane ba jubo. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 100 nit ñi ci bokk: 97 jigéen ak 3 góor. Bérëbu xayma: Porodi test yi ñu def ci palmeer loxo nit ñi ci bokk yépp. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu dul xam boróom, bu ñu lambatu, te placebo seytu ko. Bio‑Oil® Skincare Oil ak diw bu nu rañe ci la ñu jëfandikuwoon ngir xajjale ay bérab ci palmeer loxo nit ñi ci bokk yépp. Ñi doon bokk diwu natt porodi bi ku ci nekk lu tollu ci benn simili. Natkat yi nattoon na ñu nàanum porodi bi ci 5 poñ doore ko' nàan bu tuuti yeexa yeex' ba 'nàan bu gaawa gaaw'. Resilta Nàan bu Bio‑Oil® Skincare Oil ci der bi ñu ngi ko seytuwoon mu nekk ‘gaawa gaaw’ mbaa ‘gaaw’ (72%) ci nit ñi ci bokk.


JÀNGAT CI WALLU GISS GISS

Bérëbu Jéemukaay Jëfandikukat bi dafa am na ci Dr. J. Wiechers ci Rigano Laboratories, Milan, Itali. Mebët Ngir seetlu ndax Bio‑Oil® Skincare Oil am na benn wàllu occlusivité bu mel ni vernix caseosa. Vernix caseosa ñi bari ci borom ci ñi séen xam xam macc ci wallu kosmetik jàpp na ñu ni moy óor ci wallu niinaayu der ndax fi faraayam tollu. Anam bi ñu koy defe Am na ndox bu ñu xam nu mu tollu bu ñu sottiwóon ci ay mbalka muur ci membrane bu xawa permeyaabal bu ñuy wax Vitro-Skin, te muy toppondóo melokaan yi ci deru nit. Lu tolloo ci wallu vernix ak caseosa ak la ñu jëfandikuwoon ci membrane te tolluwaay ñakkum ndox mi ci mbalka mi nattoon na ñu ko ci waxtu. Lii deñ ko tékkale woon ak tolluwaayu ñakk ndox bi ci test mbalka yi, fekk defu ñu benn porodi ci membrane bi. Tolluwaayu seey ndoxu porodi bu ci nekk deñu ko xaymawoon. Resilta Bio‑Oil® Skincare Oil am na ci lu mel ni vernix caseosa, ñu rées 23.5 ci 27.2 ci vernix caseosa.


DIWU

Naka lañu koy jëfëndikóó Bio‑Oil® Skincare Oil deñ ka wara maasaas ci yaram wi ci melokaanu mbege ci kaw yaram wi ba mu naan lépp. Ñu ngi leen di wax ni porodi bi deñ ka wara jëfandiku ñaari yoon ci bés ci diiru 3 weer lu mu ndaw ndaw. Bio‑Oil® Skincare Oil waru ñu ko jëfandiku ci kaw góom bu ubbéeku mbaa der bu dagg. Diwu ngir mbiri kosmetik rek moo ko taxa jóg. Jëfandiku ko ci kaw këlu der bu wér wóorna . Nit ku nekk sa resilta du bokk ak bu keneen. Ci ban diir lañu koy jëfandiku Ay jéem Bio‑Oil® Skincare Oil yu bari lañu defoon ci diiru 8-ayubés ak 12 ayubés, moo waral ñu cammbar xarañteefu porodi bi ci ap diir. Analis lim yi wone na ap tan ci wallu melokaanu der gi ginnaaw 24 waxtu kese te tan góoge defay des ci diiru jéem bi yép. Boole ko ak toppoto der bés bu nekk Ngir Bio‑Oil® Skincare Oil naan bu baax, deñ ko wara diw ci der bu ñu raxas. Di boole Bio‑Oil® Skincare Oil ak yeneen porodi ngir mu gëna ko dugal’ mënna ci am njeexital yu bo ci xarañteefam. Bu ñu diwe ap diw ngir muccu ci nàaj mbaa yeneen diw nang ko def benn yoon rek Bio‑Oil® Skincare Oil seeyna bu baax ci yaram wi. Ci jëfandikoo yaram gépp, diwal Bio‑Oil® Skincare Oil bi ginnaaw bi nga sàngo mbaa këppo. Jëfandiko ci biir ëmb ñu feeñ fu nekk ci yaram wi, waaye lu ci gëna bari ci biir bi, póoj yi, ci suufu ndiggi li, taat wi, ak ween yi. Ngir mooytundiku rewu ëmb ñu ngi leen di wax ni Bio‑Oil® Skincare Oil deñu ko wara jëfandiku ci yii bérëb ñaari yoon ci bés bi ci ndoortelu ñetti weer yu njékk yi ba nga wosin. Bi ñu ko jëfandikoo saa su nekk, Bio‑Oil® Skincare Oil dina faj xasan ak der bu wow and ci ak pruritis gravidarum. Am na itam lu jëm ci xëtu yaram bu amul njariñ, lu jóge ci wuute yi am ci hormoon yi am ci biir ëmb. Witamin A ak ëmb Jigéen yi dafa am solo ñu di leen di sant ngir ñu waññi ferñent A ci biir ëmb, te noonu mën na ñu am jiixi jaaxa ci jëfandikoo ay porodi defar der yu am ferñent A. Bépp mbir bu ñuy def ci der du am ngaañ lu moy deñoo romb doosam ci wallu poson. Ndax der bi defay am ap baaraas bu am solo ngir tere luy duggu, ap tokk ferñent A bu ñu diw bu baax rek mooy duggu ci yaram. Kurelu Komisoŋ bu Órop buy yéngu ci siyaas ak Kàarange jëfandikukat yi (SCCS) cammbarna ferñent A aki mbiram, su ñu ko jëfandikoo ci wallu ferñenti kosmetik. Ci xalaatu CSSC, jëfandiku ferñent A ci diwu yaram yi, ba àgg ci fi mu mëna yem tollu ci 0,05% retinol amul ngaañ. Witamin A bi nekk ci formule bi ñuy wax Bio‑Oil® Skincare Oil dafa dem ba ëppu fi niinaayu diw yaram waroon a yém te mënnañu ko jëfandiku te du am benn ngaañ ci jamano ëmb. Bi ñu ci boole tuuti vitamin A, Bio‑Oil® Skincare Oil di jox jigéen ñi ëmb lu am njariñ ci vitamin A, te amul bene gagñ. Diw Rosemary ak ëmb Diw Rosemary dafa am doole lool, te ap emmenagog la, maanam mënna gisloo jigéen mbaaxam, te mënna am mu waral wosin bu teel. Moo tax ay xarit ak ay xarit yu jëfandikoo diw Rosemary ci àdduna yu mag, di leen wax ñu bañ a jëfandikoo ci biir ëmb. Waaye, diw romarin ci Bio‑Oil® Skincare Oil dafa tuuti lool motax amul loor ngir jëfandikoo ci biir ëmb. Jëfendiko leen ko bu ngeen di nampal Bio‑Oil® Skincare Oil dafa séll ngir jëfandikoo ci yaram bi su ñuy nampal, waaye sopp nañu bañ ko diw ci cus yi. Waaye, bu ñu amul lu bon, ay liir ñoo am dégërul, waru ñu lekk Bio‑Oil® Skincare Oil, doon te lu tuute tuuti la. Jëfandiku ci liir yi ak ci xale yi Kaarange jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil ci xale yu motlegul 3 at seytuwuñu ko. Ci at yu njékk yi ginnaaw juddu, ay coppite yu bari dey am ci yaramu nitki, rawatina defàasu yaram wi. Kon, ñu ngi leen di wax ñu jëfandiko ko rek ci xale yu am ñetti at mbaa lu ko ëppu. Porodi bi deñ ko wara jëfandiko ndànk ci xale te warul jege bët mbaa gemmiñ. Niñu koy Jëfandiko ko ci nàaj wi Jéem yi ñu amal ci diwu yaram Bio‑Oil® Skincare Oil du xécc nàaj bi mbaa mu gën ko mettilo. Kon mën nañu ko jëfandiku ci nàaj ci lu wóor, waaye du maye benn kaaraange ci reyoŋ UVA ak UVB yu nàaj bi. Konn amna solo ñu jëfandikuwaale porodi bi ak benn weer soleer bu yaatu bu am kaaraange ci nàaj bu tollu ci 30 lu mu néew néew. Jëfandiko ko ci a teru yaram yu am mikoos Bio‑Oil® Skincare Oil jàpp na ñu ni dafa wóor ngir jëfandiku yépp ba mu des ay teru yaram yu am mikoos. Jëfandiko ko ak rajoterapi walla simiyoterapi Bi Bio‑Oil® Skincare Oil amul ay ferñent yu mën a jël ay rajason, Li ñu digle moy ñi koy jëfandiku te ñu nekk ci rajoterapi mbaa simiyoterapi ñu làaj fajkat buy yéngatu ci wallu faju bala ñuy jëfandiku porodi bi. Jëfandiko ko ak ay porodi farmasi Bio‑Oil® Skincare Oil ap prodi kosmetik la. Ci wallu ndigël jém ci jëfandiku bii porodi ak ay porodi farmasi, li gën moy nga làaj ab fajkat. Jëfandiko ci der bu oyof Bio‑Oil® Skincare Oil mën na ñu ko diw ci der bu oyof. Ci ab jàngat ci neewi der bu ñu amal ci 25 nit ñu am 18–65 at ak ay der yu oyof, amul kenn ci ñoom ku ame tawat. Jëfandiko ko ci der bu niin Bio‑Oil® Skincare Oil mën na ñu ko diw ci der bu niin. Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñu am 18–65 at ci ñi ci bokk am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Skincare Oil du joxe ay tomb ci yaram. Jëfandiko ko ci der buy am ay pic lu bari Bio‑Oil® Skincare Oil mën na ñu ko diw ci der bu am akne. Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñu am 18–65 at ci ñi ci bokk am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Skincare Oil du joxe ay tomb ci yaram. Resilta jangat bi ñu amaloon ci 44 nit yu sen at tol ci 14–30 ñu ame akne ak nattum sebum bi wonena ni jëfandiku Bio‑Oil® Skincare Oil du inndi mbaa mu gëna garawal akne mbaa yokk sebum. Waaye li ñu digle moy ne, nit ñi am aknee, war na ñu laaj ap fajkat, bala ñuy diwu Bio‑Oil® Skincare Oil.


SOSU KËL

Ap kël maggàayu kolasen buy nekkaat lu bokk ci wér ginnaaw gaañu gaañu der. Kolasen dafa am ay protéin yu am solo, di jëfe ci biir yaram. Bu gaañu gaañu ci der ame, yaram wi dafay àllu ci nu mu gëna gaawe ngir defar pacc bi ñu laal, tane lay gëna faratal ci wér bu baax. Jur ay kolasen ci lu gaawa gaaw ngir faj gaañu gaañu moy luy jur kël. Doon te ap kël dina am ay coppite yu bari bala muy ñor, du mësa am doole bu tóllu ni der bi ko wër. Paxu kawar gi ak bënn bënn ñax yu nekk ci kël bi yi du ñu delluwaat . Sosu kël mungi am ñeenti pacc: Taxawlo deret buy senn bi Mungi tambali ci saas yi ginnaaw bi gaañu gaañu ame te bu am ay waxtu, ndax pacc bi gaañu defay jéema dellu ci melokaanam normaal di dajale deret ngir téye nacc bi. Selil yu gaañu yi deñuy bayi ay proteyin ci jamano jóoju ngir tambali wayal, su ko defe ñu téj wesel yu yaxu yi te wañi ñakkum deret. Ci néewi Xonkaay ak newi bi di feeñ ci diir bu ñett mbaa ñeenti fan ginnaaw gaañu mbu njékk bi ap mandarga tontu bu kaaraange yaram wi la. Selil yu weex yi di génne ay porodisimik yuy sotti raxas góom bi ak bakteri yi. Ci law bi Lii di tàmbalee ci ñetti fan, di sax ci ñetti ayubés. Ñetti taxawaay yu wuute deñuy am ci jamono gi ngir lëkkale ak tëj góom bi. Dëtal: fibroblastes (selil yuy waral seggup kolasen) deñuy feeñ ci góom bi ngir defar kolasen ci lu gaaw ngir sol góom bi. Li waeal sikatris bu mboq: ap kuus deret defay juddu ngir muur góom bi. Téjaat góom bi : deñuy dajale góom bi ngir wañi ay wi. Ci ñor Bii jamano 'tabaxaat' ginnaaw luy tollu ci ñetti ayubés lay tambali te mënna wéy ba ñaari at mungi aju ci yaatuwaay ak xootaayu góom bi. Ci jamano jooju kolasen bi defay wéy di màgg, fiibar yi di defaruwaat ndax li ñu def ci gaañu gaañu bi lu am njéexital ci kël bi. Bu kël bi di muur ak sàmm góom bi, mënna ko yaxal ci lu yomb. Deru kël bi lu ci ëpp dafay am doole ci traction bi ci suuf bi ba 70% ci der bu normaal bi.


XETU KËL YI

Ndaxte nit ñi di faj lu ëpp, gis-gisu mujj bi dafa wuute ci nit ku nekk. Mbir yu mel ni xetu der, bérab bi kël bi nekk, xetu gaañu gaañu, ati nit ki ak sax lekkam dina bokk ci luy tax kël bi mel ni muy mel. Xetu kël yi mënna ñu ko xaaj ci yii kategori: Kël yu gëna bari yi Yóoyu kël deñuy feeñ newi te léndëm ci ndoortel bi waaye su yagge defay gëna tëddaat gis ko gëna jafe ba mu nekkaat rëddu kël bu jaar yoon. Ay kël atrophik Yii kël deñuy waral sutante mbaa der bu jagadi. Am na ay misaal kël yu jóge ci akne mbaa ŋàppati. Ay kël hypertrophik Yii xël ci kaw der bi lañuy nekk. Bokk na ci li ñu leen di rañe ap lim kolasen bu ëppu, waaye defay des ak pég góom bu njékk bi. Kël Keoid Waru ñu jaawale keloid ak ay kël hypertropic. Doonte ay kël yu ñu yar la, bokk na ci mandarga keloids romb pégg góom bu njékk bi. Mën nañu wéy di magge ci diir gu èpp te lu ci ëppu deñuy delluwaat ginnaaw biñu ko daggé. Kël kontra Kël kontra mungi am su der bi teeŋe ba sax ci. Deñuy màgg su kël yi jógge fu ay yax daje, fu der lemo, ak ci ay àngal yu jub. Deru kël bi dafay bañ fuddu te mënna tere yéngatu bu jàar yoon. Ay kël kontra ci góomu lakk lay ame. Ay sikatiris (Ay rèd) Ay sikatiris dina am ci jamono coppite ci am yaram yu gàaw (ci misaal maggaayu waxambaane, ëmb) buy yaram wi di funki ci lu raw ni ko der bi di muure, mu waral ay xotteeku ci biir der bi. Bu xotteeku yóoyu di defar seen bopp deñuy def ay kël yu ñuy wax rew.


SOSU SIKATIRIS

Ci kallama wér gu yaram rew mbaa striae, ay yeneen xetu kël la rek, waaye, ñi bari deñoo jàpp ni bokku ñu ak kël. Rew ay rëdd yuy juddu ci der bi buy der bi di màgg ci lu gaaw, lu mel ni jigéen bu ëmb, defarkatu yaram ak ay waxambaane ci seen màggaay. Ni ko seen tur bi di xamle, ñu ngi jóxe ci taaweeku. Ñi gëna leer deñuy faral di am ay rew yu wiyole, te ñi gëna léndëm der deñuy faral di am ay rew yu gëna leer fi leen wër. Na ka jekk, der dafay taweeku. Taweeku bi kolasen moo koy waral ak elastin yi nekk ci dermis bi ci suufu tisi der bi. Kolasen gurup porteyin yu raxul la te benn la ci tisi yaram wi. Elastin wi juddo ci ay poroteyin yu raxul, mën na ñu ko fekk ci tisi yuy lëkkale ak di maye ay njariñam ci taweeku. Bóobu tisi buy lëkkale defay tax dermis bi mëna jano ak yéngu yéngu yaram wi muy gëna yaatu aki kontre, waaye ci jamono yokku puwa bu gàaw, mënna ñakk am jot ngir soppéeku, waral ay xotteeku ci biir tisi yaram wi. Bu xotteeku yóoyu di defar seen bopp deñuy def ay kël yu ñuy wax rew. Leeral bu am solo moy rasul bu ñuy xécc bi. Am na nooy xécce rasul yi yenn limit yi, ñu koy wax limit elastik judduwaale, defay kontrewu ngir amaat melokaanam bi woon ay yooni yoon. Waaye, yu xécce rasul bi lu ëppu ba mu romb taweku am bu jaadu, noonu rek lay melati, dootul tolluwaat ni mu tolluwoon. Doonte, ay rew du ñu feebar bu am solo, mën nañu yóbbe ñi leen di am ay xalaat yu metti. Ame ko mungi aju ci melokaanu der bi, at, ndono ak xetu lékk bi ak niinaayu der bi. Rew seen sosu nii la tëdde: Pacc benn Rew yu njékk yi deñuy feeñ ci melokaan bu furi te mën na ñu xasan tamit. Der bi ci wetu rew yi tamit mën na 'lalu' te 'sew'. Pacc ñaar Ci biir loolu, rew yi di gën a màgg ci yaatuwaay ak di gëna léndëm aki fës. Pacc ñett Bu rew yi ñore te der bi sonnatul deñuy dem di gëna furi. Mën na ñu itam feeñ ak coppite ci melokaan ak gudduwaay yu jaarul yoon.


SOSU REW CI ËMB

Am na xamal ne ci diggante 50% ak 90% ci jigéen ñi ëmb, am na ñu ay rew yu bari. Rew yi mënna ñu am ci biir bi, póoj yi, kapp yi, suufu ndiggi, taat yi ak ween yi – ay bérab yoo xamne foofu moo ëppu luy der bi di taweeku ginnaaw yaram wi defay soppeeku ci jamonoy ëmb. Donte mën a feeñ fu nekk ci yaram, ñu ngi gën a feeñ ci bérab yu ñu am geres bu bari yi. Donte rew ci 3 weer ëmb yu mujju yi lay feeñ (boori juróom bennel mbaa juróom ñaarel weer) yenn jigéen yi deñuy tambali di gis ay rew ci ñetti weer yu njékk yi. Rewu ëmb mënna itam jóge ci waajtaayu der bi ngir wosin ba ndax ormóon yu yokku. Ormóon yi deñuy gëna xécc ndox ci biir der bi, luy feexal fas yi nekk ci diggante fibru kolasen yi. Lii dafay tax xotteeku der bi gëna yómb su ñu ko xécce ak ngir melokaanu rew yi. Ame ay rew mungi aju ci melokaanu der bi, at, ndono ak xetu lékk bi ak niinaayu der bi.


DEFAR BA

Defarub Bio‑Oil® Skincare Oil dafa méngo ak Anamu Defar bu muccu ayib (GMP) yu ISO 22716:2007 làaj ci porodi kosmetik yi. Jumtukaay yi ñu jëfandikoo ci defarub Bio‑Oil® Body Bio‑Oil® Skincare Oil, yépp deño ànd ak Sartifika analiis (COA), te jumtukaay yi ñu koy ëmbe yépp, ñu ngi ànd ak sartifika Dëppo (COC). Amul benn jumtukaay ligéey mbaa jumtukaayu pakete bu ñuy génne lu moy deñ ko seytu ba pare. Béppu lóo Bio‑Oil® Skincare Oil bu ñu jaxase defa am niimero lòo boppam. Deñoo seytu benn esantiyon bu juge ci wàll wi ci ap labo ngir melokaan, leer, xet, xamme ak espektoroftomeetar,faraay ak mikkoro biyoloosi. Esantiyon bi dën koy téye ñeenti at. Sol ak pakkete bi ci Bio‑Oil® Skincare Oil dafa nekk ci bérëb bu ñuy cammbare tamperatiir ak tooyaay. Ngelew li ci fu muccu ayip lay jàar (HEPA) luy segg ngir mooytu laal pënde. Ñi liggéey ci wàllu defar gi, deñuy sol ay mbaxna, ay màsk, muurukaayu kanam, ay gaa, ay west ak ay dàll. Baŋkàas bi di sàmm kalite dafay dinndi ay esantiyon saa su nekk ngir mu seytu ko nfdax amul yaxu yaxu bu am solo. Ap wàll bu ñu bind ci botel bi, karton bi ak mbugal bi, te ñu sàmm na benn samp bu ñu sàmm ci nekk bu ñu sàkk ba ñeent at. Amul xet yu bon, mbalit yu bon mbaa ndox yu ñu génne ci jëfandikoo Bio‑Oil® Skincare Oil.


TÉKTAL NDÉNC

Bio‑Oil® Skincare Oil war na ko sàmm ci bérab bu sédd, fu amul ceru nàaj.


DEKKILAAT

Paketu Bio‑Oil® Skincare Oil yépp (butel, kubéer ak kartoŋ) deñu leen di defaraat.


DIIR GINNAAW UBBITE BI (PAO)

Bio‑Oil® Skincare Oil am na ap PAO bu 36 weer. Lii moy diir bi ginnaaw ubbite boo xam ni porodi bi séll na te mën na ñu ko jëfandiku fekk du lor ki koy jëfe.


SÉERTIFIKA YI

Bio‑Oil® Skincare Oil dafa am sartifikat Halaal ak Kosher.


GALLANKOOR

Ginnaaw bi Bio‑Oil® Skincare Oil ame woy wu rafet ci wallu poson te méngo ak téralin yi ci aduna bi ci góogu wàll, ak porodi kosmetik yép, amna ap tiitàange ni jëfandikukat Bio‑Oil® Skincare Oil mënna ñu am gallaŋkóor yu bon su ñu koy diwu. Su fekkee ne amna gallaŋkóor, jëfandikoo porodi bi ñan ko dakkal ci sasyi. Mandarga àllukaayu der yu bon mënna doon ay tómb yu xonk, newi ak deretal, te mu wara am fi ñu diwe porodi bi. Yii jëf mënna ñu ànd ak xasan ak ap jagadi. Lu ci ëppu, gallankòor yi deñuy wañeeku ci diiru ñaar mbaa ñetti fan ginnaaw bi ñu dakkale jëfandiku porodi bi. Ba mu dellu ci melokaanam bu njëkk, der bi mënna wow te am ay ras. Su fekkee ni am lu la jaaxal ci lu jëm ci alersi ci diwu Bio‑Oil® Skincare Oil, luy gën moy def ay test alersii ngir seetlu ko. Lóolu ñu ngi koy ame ci diw tuuti Bio‑Oil® Body Lotion ci seen biir loxo yi te xàar diiru 24 waxtu ngir xool ndax benn àllukaay dina am. Luy Xonkal der bi (deretal) mba néewi bu ndaw (dët) mënna téktale ap tontu buy wone alersi.


JÉEMU ÑU KO CI AY RABU ALL

Bio‑Oil® Skincare Oil ak materiyel bi mu àndal deñ léen defare ci lu déppó ak térëlinu EU bu jém ci jéem ay kosmetik ci rabu àll. Moo xam Bio‑Oil® Skincare Oil la mbaa ay ferñentam, jéemu ñu benn ci ñoom ci ay rabu àll ak Bio‑Oil mbaa ñi koy inndil materiyel.


VEGAN

Bio‑Oil® Skincare Oil amul benn ingrejen bu jóge ci rabu àll.


WONN CI NJUUMTE

Su jumte wonn Bio‑Oil® Skincare Oil amé, linyu gis moy xel mu teey ak biir buy daw deñu koy seytuwaat ndax Bio‑Oil® Skincare Oil amul poson. Wante, ñu ngi léen di digal ngéen jokkó ak fajkat rawatina su xale mbaa tuut tank Njumte ba wonn ko.


COPPITE CI WALLU MELOKAAN

Bio‑Oil® Skincare Oil am na calendul, chamomile, lavendre ak romarin ay jëmm ak ay diw yu am doole, di itam vitamin A, ñoom ñépp di leer. Nekk ci nàaj mënna inndi coppite melokàanu der bi su yagge. Waaye dafa mel ni du yax xarañteefu porodi bi. Ci wallu kaaraange, butel yu Bio‑Oil® Skincare Oil am na luy naan UV. Waaye, prodi bi waru ñu ko def ci nàaj.


BÉS BI ÑU KO GÉJE YEESALAAT

22 UT 2023