TURU MARK BI
Bio‑Oil®
TUR AK TOLLUWAAYU PORODI BI
Dry Skin Gel 50ml
Dry Skin Gel 100ml
Dry Skin Gel 200ml
TÉKTAL
Defay yokk niinaayu der bi bu baax.
WONALE
Sel bu suraas / wiyole.
NAS BA
Sel ak 84% ingrejen ci wallu bët ak 13% ci Likid buy niinal ak 3% ndox.
INGRÉDIEN YI
Paraffinum Liquidum, Isopropyl Palmitate, Triisononanoin, Glycerin, Cetearyl Ethylhexanoate, Isopropyl Myristate, Aqua, Caprylic / Capric Triglyceride, Isostearyl Isostearate, C26-28 Alkyl Dimethicone, Butyrospermum Parkii Butter, Sodium Lactate, Urea, Gluconolactone, Sodium PCA, Sodium Hyaluronate, Octyldodecyl PCA, Sucrose Laurate, Sucrose Stearate, Lactic Acid, Lanolin, Butylene Glycol, Dimethicone / Vinyl Dimethicone Crosspolymer, Bisabolol, Helianthus Annuus Seed Oil, Silica, Glycine Soja Oil, Retinyl Palmitate, Tocopheryl Acetate, Niacinamide, Linoleic Acid, Linolenic Acid, Tocopherol, Anthemis Nobilis Flower Oil, Calendula Officinalis Extract, Rosmarinus Officinalis Leaf Oil, Lavandula Angustifolia Oil, Parfum, Farnesol, Limonene, Linalool, CI 17200.
LUY JUR ALERSI
Am na ñetti luy jur alersi ci Bio‑Oil® Dry Skin Gel. Ni ki luy jur alersi yu bare, ñu ngi ci diwu garab yi ak xet yu neex. Ñoo doon: Farnesol, Limonene ak Linalool.
SEYTU KAARAANGE GI
Bio‑Oil® Dry Skin Gel amna xamtukat buy yéngu ci wallu seytu lu jém ci poson ku seytu kaaraange am mu firndéel ni amna kaaraange ñeel jéfandiku bi ko waxambaane yi wara jéfandiku, yokk ci jigéen yu wonn lor ak ñii di nampal, ak ay xale yu am lu ëppu ñetti at.
JÉEM DER BU WOW CI KILINIK
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ap cambarum kilinik bu jëm ci seytu xarañteef Bio‑Oil® Dry Skin Gel ci gëna niinal der. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 40 jigéen yu wér yu bokk ak Fitzpatrick skin types II-V te wone ci kilinik ba der bu wow/ der bu wowa wow (tollu II-IV) lu tollo ak ci bitti suufu yéel yi, ak Corneometer bu manke 40 ci binndu ba. Bérëbu xayma: xayma porodi yi ñu diw ci bitti yéélu ñi ci bokk yép. Atu nit ñi ci bokk: 40–65. Anam bi ñu koy defe Xàaj yaram wi, seytukat bu xamul borom ligéey ba, lambatu, ap jangat juntuwaayu kilinik. Ñi doon bokk ci njëkk bu jëkk ci cammbar ba, ñu topp ca 7 fan yu wowal, 28 fan faj ak 3 fan toppotoo (wañeeku). Ci jamono wowal bi, ak ci jamono jangat bi nit ñi raxasoon nañu seeni tànk ñaari yoon ci bés ak Dove Beauty Bar. Bio‑Oil® Dry Skin Gel ñu jëfe ko ñaari yoon ci bés ci tànk gi ñu ko jox ci suuf, beneen tànk gi ñu fajul. Xayma kilinik ak xayma juntukàay yi amaloon nañu ci ndoortel ak ci bés : 1, 3, 6, 8, 10, 14, 21, 28, 29, 30 ak 31. Xayma nañ bërëb bu Fu ñu toppotowul ci jamano bu nekk. Ñóoñu ap xaymakat gisgis bu ñu taggat note na léen ci wowaay nattko ci (Lu ko dale 0–5). Natt tolluwàay mbaa diwu der ba der bi ak Corneometer la. Natt tolluwàay ñakkum ndox ci deret bi (TEWL) ngir deru yaram bi, Juntukàay buy natt ndesitu ndox lañu ko amale. Resilta Bio‑Oil® Dry Skin Gel wonena ap yokkute bu am solo ci lim ci wallu niinaayu der, njariñu bariyeer ak melokaanu der gu wow (note wowaay ci kilinik) ci bépp seytu ngir xool, te ñu tékkale ñaar yép ci melo ndoortel ba ak pacc (xoolat) bi ñu fajul. Ngir natt wowaay bi ci kilinik, yoykkute bu ama am solo lu ñu séentuwoon la ci 62% ñi bokkoon li ko dale bés 1 jém ci kanam, te ëppu 85% ci ñi bokk dale ko ci bés 3 jém ci kaw. Ci bés 21 bi, 100% ci ñi bokk, wone nañu ap tan. Ci bés 28 ci ñi bokk, wone nañu yokkute bu ëppu 3.5 yoon ci natt bu kilinik uté ak béssu 1. Ginnaaw 28 fan ci jëfandikoo, 100% ci nit ñi ci bokk wone na ñu ap yokkute ci wallu niinaayu der bu ëppu bu bés 1 bi 1 yoon. Ni ki noonu, ginnaaw 28 fan ci jëfandikoo, 82% ci ñi doon bokk wone na ñu ap waññeeku ci wallu niinaayu der bu ëpp 5.5 yoon béssu 1. Xarañtéef bu Bio‑Oil® Dry Skin Gel ci yokk niinaayu der, njeriñu bariyeer te melokaanu der bu wow firndeloon nañu ko ginnaaw 3 fan toppoto, bi ñu daxxale jëfandiku porodi bi.
SEYTU DER BU OYOF
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir cambar ni Bio‑Oil® Dry Skin Gel mëne inndi tawat ci wallu der. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 30 nit; 28 góor ak 2 jigéen, ñoom ñépp ñu am ay der yu oyof su nu sukkandikoo ci seytu bu asid laktik. Atu nit ñi ci bokk: 18–70. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu sàmm.. Ñaari pacc lañu xayma: pacc bi ñu jëfe woon ak test bu negatif (ndox bu amul mineraal) ak pacc bi ñu jëfe woon Bio‑Oil® Dry Skin Gel. Porodi yi ñu seytu yep ci ndiggi ñi doon bokk lañu ko def ci kaw der gi ci diiru 48 waxtu di jéfandiku juntukàayu xayma Finn chamber® Yengu yengu der ba ci teewaayu kuy yéngu ci fajum der la woon, ngir xayma tawat ci wallu der bu njékk ci 15 simili, 1 waxtu ak yeneen 24 waxtu ginnaaw bi ñu dinnde jubbantikaay. Yengu yengu der yi ci diggante 0–4 la ñu ko nattoon (fekk 0 nekkul erythema, mbaa dët mbaa yeneeni neewi der ba ak 4 nekk erythema ak dët dégg, di wone xonkaay bu lénndëm ak neewi bu yaatu ci kaw pacc bi ñuy diwu mbir ma). Resilta Kantanu deru ci Bio‑Oil® Dry Skin Gel neena ñu ‘du neewi der’.
JÉEM NDAX DU JOXE AY TOMB CI YARAM
Bérëbu Jéemukaay Complife Italia S.r.l, Italy. Mebët Ngir xayma tolluwàayu komedo bi ci Bio‑Oil® Dry Skin Gel. Nattukàay Ñiuñ ko jaglel: 20 nit; 18 jigéen ak 2 góor yu am ay xeet yu wuute te am der yu ame akne. Atu nit ñi ci bokk: 18–65. Anam bi ñu koy defe Jangat bu ñu sàmm.. Porodi bi defoon na ñu ko ci ap kayitu séggukaay ci kaw ndiggi nit ñi ci bokk. Bayiwoon na ñu ci ay bandàas 48 ba 72 waxtu, dinndi lènn ba noppi délolènn ci. Defoon na ñu ci 12 bandàs ci lép ci 4 ayubes yu toftalo. Ñetti pacc lañu seytu daa di tékkale test bu negatif (ndox bu amul mineral), porodi jéem bi (Bio‑Oil® Dry Skin Gel) ak test bu positif (lanolin alkol, ap porodi komedo bu ñu xam). Yengu yengu der bi seytuwoon na ñu leen ci kanamu ap fajkatu der 15 simili ginnaaw bi ñu dinnde bandaas bu ci nekk ngir tékkale teewaayu komedo bi laata ak ginnaaw diwu porodi bi. Resilta Bio‑Oil® Dry Skin Gel giss na ñu ni du komedo. Pacc bi ñu jëfe Bio‑Oil® Dry Skin Gel wonewul ap wutewul torop ak test bu negatif bi ci pacc boobu. Test bu positif bi wonena akne.
JÀNGAT CI WALLU GISS GISS
Bérëbu Jéemukaay Rigano Laboratories, Milan, Itali. Mebët Ngir cammbar okkilisiwite Bio‑Oil® Dry Skin Gel ak kattanam ci dimbali der bi téye niinaay ak waññi TEWL. Anam bi ñu koy defe Am na ndox bu ñu xam nu mu tollu bu ñu sottiwóon ci ay mbalka muur ci membrane bu xawa permeyaabal bu ñuy wax Vitro-Skin™, te muy toppondóo melokaan yi ci deru nit. Porodi bi jëfendiku na ñu ko ci membrane bi te ñàkk ndox ci mbalka yi nattoon na ñu ko ci waxtu. Lii deñ ko tékkale woon ak tolluwaayu ñakk ndox bi ci test mbalka yi, fekk defu ñu benn porodi ci der bi. Resilta Anam bi ñu amale jéem bu limu Jottali ndoxu wapóor bi (WVTR) ap jéem bu estandàar la ngir nàtt lu jèem ci wallu bèt ci porodi yi. Ap wañeeku ci tolluwaayu WVTR bi defay wone ni benn ci anamu jéfandiku yi defa jégé wallu bèt. Wone na ñu ni Bio‑Oil® Dry Skin Gel defay wañi limu WVTR su nu ko méngale ak test bu ñu toppowutoon bi ñu ko defe ci lalu deru Vitro-Skin™ bi. Bii resilta in vitro defay wone ni Bio‑Oil® Dry Skin Gel dina dimmbali der bi jàpp niinaay in vivo su ko defe mu sàafaral tektal ak mandarga yu der bu wow yi.
DIWU
Digle ngir diwu Jëfandikul Bio‑Oil® Dry Skin Gel ci der bu wow ni mu waré. Su fekke ni der bu wéy di wow la, jëfe ko ñaari yoon suba ak ngoon. Ngir ay mujjantalu yu gën baax, porodi bi ci ap der bu ñu raxas lañu ko wara jëfandiku ginnaaw bi nga sango mbaa nga xëppo. Bu ngeen di jëfe yeneen porodi, defleen ko benn yoon, der bi naan na Bio‑Oil® Dry Skin Gel bi yépp. Bio‑Oil® Dry Skin Gel ngir yaram rek la ñu ko defare woon, waaye mën na ñu ko jëfe ci kanam. Teey ci jëfandiko bi Bio‑Oil® Dry Skin Gel ap jëfandiku kosmetik rek moo ko taxa jóg. Bio‑Oil® Body Lotion waru ñu ko jëfandiku ci kaw góom bu ubbéeku mbaa der bu tañcu. Móoytuleen mu laal bët yi. Bu porodi yi dugge ci bët, raxas ko bu baax ak ndox. Bu ci xale yi jot. Lim bu ñu ci wara jëfandiku Bi ñuy jëfe diwu der bu wow yi, niinalukaay ak bër, faawu mu doon lu bëri ndax yooyu porodi ndox moo ci ëppu, te dafay seey su laale der bi. Ginnaaw Bio‑Oil® Dry Skin Gel mooy 84% ay diw, ay siir mooy gëna tuuti lu muy làaj ci ay porodi ci menn paccu yarambi.. Jëfandiko ci biir ëmb Bio‑Oil® Dry Skin Gel woorna ngir jëfandikoo ci biir ëmb. Witamin A ak ëmb Jigéen yi dafa am solo ñu di leen di sant ngir ñu waññi ferñent A ci biir ëmb, te noonu mën na ñu am jiixi jaaxa ci jëfandikoo ay porodi defar der yu am ferñent A. Bépp mbir bu ñuy def ci der du am ngaañ lu moy deñoo romb doosam ci wallu poson. Ndax der bi defay am ap baaraas bu am solo ngir tere luy duggu, ap tokk ferñent A bu ñu diw bu baax rek mooy duggu ci yaram. Kurelu Komisoŋ bu Órop buy yéngu ci siyaas ak Kàarange jëfandikukat yi (SCCS) cammbarna ferñent A aki mbiram, su ñu ko jëfandikoo ci wallu ferñenti kosmetik. Ci xalaatu CSSC, jëfandiku ferñent A ci diwu yaram yi, ba àgg ci fi mu mëna yem tollu ci 0,05% retinol amul ngaañ. Witamin A bi nekk ci formule bi ñuy wax Bio‑Oil® Dry Skin Gel dafa dem ba ëpp fi niinaayu diw yaram waroon a yém te mënnañu ko jëfandiku te du am benn ngaañ ci jamano ëmb. Diw Rosemary ak ëmb Diw Rosemary dafa am doole lool, te ap emmenagog la, maanam mënna gisloo jigéen mbaaxam, te mënna am mu waral wosin bu teel. Moo tax ay xarit ak ay xarit yu jëfandikoo diw Rosemary ci àdduna yu mag, di leen wax ñu bañ a jëfandikoo ci biir ëmb. Waaye, diw Rosemary ci Bio‑Oil® Dry Skin Gel dafa néew lool te kon lu sépp ngir jëfandikoo ci biir ëmb. Jëfendiko leen ko bu ngeen di nampal Bio‑Oil® Dry Skin Gel dafa séll ngir diwu ci yaram bi su ñuy nampal, waaye sopp nañu bañ ko diwu ci cus yi. Waaye, bu ñu amul àllukaay yu bon, ay liir ñoo am dégërul, waru ñu lekk Bio‑Oil® Dry Skin Gel, doon te lu tuute tuuti la. Jëfandiku ci liir yi ak ci xale yi Kaarange jëfandiku Bio‑Oil® Dry Skin Gel ci xale yu motlegul 3 at seytuwuñu ko. Ci at yu njékk yi ginnaaw juddu, ay coppite yu bari dey am ci yaramu nitki, rawatina defàasu yaram wi. Kon, ñu ngi leen di wax ñu jëfandiko ko rek ci xale yu am ñetti at mbaa lu ko ëppu. Niñu koy Jëfandiko ko ci nàaj wi Jéem yi ñu amal ci diwu yaram Bio‑Oil® Dry Skin Gel du xécc nàaj bi mbaa mu gën ko mettilo. Kon mën nañu ko jëfandiku ci nàaj ci lu wóor, waaye du maye benn kaaraange ci reyoŋ UVA ak UVB yu nàaj bi. Konn amna solo ñu jëfandikuwaale porodi bi ak benn weer soleer bu yaatu bu am kaaraange ci nàaj bu tollu ci 30 lu mu néew néew. Jëfandiko ko ci a teru yaram yu am mikoos Ay teru yaram yu am mikoos Bio‑Oil® Dry Skin Gel deñoo japp ni wóorna ci fann yépp, waaye cammbaruñu kaaraange am ci ay teru yaram yu am mikoos, ndax te nekkul jëfandiku bu ñu sóoraalewoon ci porodi bi. Jëfandiko ko ak rajoterapi walla simiyoterapi Bio‑Oil® Dry Skin Gel amul ay ferñent yu mën a jël ay rajason, Li ñu digle moy ñi koy jëfandiku te ñu nekk ci rajoterapi mbaa simiyoterapi ñu làaj fajkat ci wallu faju bala ñuy jëfandiku porodi bi. Jëfandiku ci ay anam wergi yaram Bi Bio‑Oil® Dry Skin Gel mën na di joxe ay làquwaay yuy wàllu jàngoro yi, ni dermatite, eczema, psoriasis ak xët wuy xët, waaye dafa rafet ne nit ñi am njàqare yi, ñu warra laaj kaddug fajkat laata jëfandikoo porordibi. Jëfandiko ci der bu oyof Mën na ñu diwu Bio‑Oil® Dry Skin Gel ci der bu oyof. Ci ab jàngatci neewi der ci 30 nit ñu am 18-70 at ñi ci bokk ak ay der yu oyof, amul kenn ci ñoom ku ame gallankòor ci Bio‑Oil® Dry Skin Gel. Jëfandiko ko ci der bu niin Mën na ñu diwu Bio‑Oil® Dry Skin Gel ci der bu niin. Ci ap gu ñu amaloon ci 20 nit ñu am 18–65 at ci ñi ci bokk am der yuy am ay pic yu bare, fësal na ni Bio‑Oil® Dry Skin Gel du joxe ay tomb ci yaram. Jëfandiko ko ci der buy am ay pic lu bari Bio‑Oil® Dry Skin Gel mën na ñu ko diw ci der bu am ay pic lu bari . Ci ap jéem gu ñu amaloon ci 20 nit ñu am 18–65 at ci ñi ci bokk te am der yuy am akne, fësal na ni Bio‑Oil® Dry Skin Gel budul joxe ay tomb ci yaram. Li ñu digle moy ne, nit ñi am aknee, war na ñu laaj ap fajkat, bala ñuy jëfandikoo Bio‑Oil® Dry Skin Gel.
AY MANDARGA DER BU WOW AK LI KOY WARAL
Mandarga yi Mandarga yu der bu wow bokk na ci ap der bu furi te wow am ay rédd, giri mbaa mel ni dóom ak di yég ap dégër ak teeŋ. Sabab yi Luy joxe der bu wow ay mbir ci biir ak ci biti la. Mbir yi ci bitti: Ap kilima bu wow defay waral niinaay bi deñe ci biir der bi jaare ci ñaari donju Lipid bu ñaari kuus yi ak ci ngelew bu wow bi ci bitti. Kilim yi ak tàngalukaay yi deñuy dinndi tooyaayu ngelew bi, mu inndi benn kilima bu wow buy dinndi niinaay ci der bi. Fóot bés bu nekk ak làal ay omo yu saf defay xar ñaari donju Lipid bu ñaari kuus yi, mu tax niinaay gëna gaawa génni ci der bi. Mbir yi ci biir: Bi yaram di màgg, der gi di génne lu néew lipids, ba tax donj Lipid bu ñaari kuus bi di gën a sew, mu waral niinayu diw bi naaw gëne yomb. Njurél mën na am njeexital ci der bu wow ndax néewaayu céramides ci donju lipid bu ñaari kuus bi. Resilta yi faraay bu wañeeku ci bariyéeru der gi bokk na ci li tax mu romb niinaay bu jaadu bi. PH bi ci der gi dafa am njéexital ci njériñu liggéeyu niinal der. Ap pH bu gëna kawe ci biir der bi dafay gallankor doxinu donj Lipid bu ñaari kuus.
DEFAR BA
Defarub Bio‑Oil® Dry Skin Gel dafa méngo ak Anamu Defar yu Baax yi (GMP) yu ISO 22716:2007 làaj ci porodi kosmetik yi. Jumtukaay yi ñu jëfandikoo ci defarub Bio‑Oil® Dry Skin Gel, deño ànd ak Sartifika analiis (COA), te jumtukaay yi ñu koy ëmbe yépp, ñu ngi ànd ak sartifika deppo ak ñon (COC). Amul benn jumtukaay ligéey mbaa jumtukaayu pakete bu ñuy génne lu moy deñ ko seytu ba pare. Béppu wàll Bio‑Oil® Dry Skin Gel bu ñu jaxase defa am niimero lóo. Deñoo seytu benn esantiyon bu juge ci wàll wi ci ap labo ngir melokaan, leer, xet, xamme ak espektoroftomeetar,faraay ak mikkoro biyoloosi. Esantiyon bi dën koy téye ñeent at. Sol ak pakkat bi ci Bio‑Oil® Dry Skin Gel dafa nekk ci bërëb bu ñuy cammbare tamperatiir ak tooyaay. Ngelew li ci fu muccu ayip lay jàar (HEPA) luy segg ngir mooytu laal pënde. Ñi liggéey ci wàllu defar gi, deñuy sol ay mbaxna, ay màsk, muurukaayu kanam, ay gaa, ay west ak ay dàll. Baŋkàas bi di sàmm kalite dafay dinndi ay esantiyon saa su nekk ngir mu seytu ko nfdax amul yaxu yaxu bu am solo. niimero lóo bu ñu bind ci botel bi, Kartoŋ bi ak mbugal bi, te ñu sàmm na benn samp bu ñu sàmm ci nekk bu ñu sàkk ba ñeent at. Amul xet yu bon, mbalit buy lore mbaa ndesitu ndox yu jöge ci defar Bio‑Oil® Dry Skin Gel.
TÉKTAL NDÉNC
Bio‑Oil® Dry Skin Gel war na ko sàmm ci bérab bu sédd, fu amul ceru nàaj.
DEKKILAAT
Binu Bio‑Oil® Dry Skin Gel (tub, xëtu, label ak carton) yépp, mën nañu ko jëfandikoowat.
DIIR GINNAAW UBBITE BI (PAO)
Bio‑Oil® Dry Skin Gel am na ap PAO bu 12 weer. Lii moy diir bi ginnaaw ubbite boo xam ni porodi bi séll na te mën na ñu ko jëfandiku fekk du lor ki koy jëfe.
SÉERTIFIKA YI
Bio‑Oil® Dry Skin Gel dafa am sarrtifika Halaal ak Kosher.
GALLANKOOR
Ginnaaw bi Bio‑Oil® Dry Skin Gel ame woy wu rafet ci wallu poson te méngo ak téralin yi ci aduna bi ci góogu wàll, ak porodi kosmetik yép, amna ap tiitàange ni jëfandikukat Bio‑Oil® Dry Skin Gel mënna ñu am gallankòor. Su fekkee ne amna gallaŋkóor, jëfandikoo porodi bi ñan ko dakkal ci sasyi. Mandarga àllukaayu der yu bon mënna doon ay tómb yu xonk, newi ak deretal, te mu wara am fi ñu diwe porodi bi. Yii jëf mënna ñu ànd ak xasan ak ap jagadi. Lu ci ëppu, gallankòor yi deñuy wañeeku ci diiru ñaar mbaa ñetti fan ginnaaw bi ñu dakkale jëfandiku porodi bi. Ba mu dellu ci melokaanam bu njëkk, der bi mënna wow te am ay ras. Su fekkee ni amna lu la jaaxal ci tontu buy wone alersi ci diwu Bio‑Oil® Dry Skin Gel, luy gën moy def ay test yu alersi ngir seetlu ko. Lóolu ñu ngi koy ame ci diw tuuti Bio‑Oil® Body Lotion ci seen biir loxo yi te xàar diiru 24 waxtu ngir xool ndax benn àllukaay dina am. Luy Xonkal der bi (deretal) mba néewi bu ndaw (dët) mënna téktale ap tontu buy wone alersi.
JÉEMU ÑU KO CI AY RABU ALL
Bio‑Oil® Dry Skin Gel ak materiyel bi mu àndal deñ léen defare ci lu déppó ak térëlinu EU bu jém ci jéem ay kosmetik ci rabu àll. Moo xam Bio‑Oil® Dry Skin Gel la mbaa ay ferñentam, jéemu ñu benn ci ñoom ci ay rabu àll ak Bio‑Oil mbaa ñi koy inndil materiyel.
DU VEGAN
Bio‑Oil® Dry Skin Gel am na lanolin, lu jóge ci kawaru xar. Ci noonu, Bio‑Oil® Dry Skin Gel du vegan.
WONN CI NJUUMTE
Suñu jume ba wonn Bio‑Oil® Dry Skin Gel, dafa mel ni lu moy xel mu teey ak biir buy daw deñu koy seytuwaat ndax Bio‑Oil® Dry Skin Gel amul poson. Wante, ñu ngi léen di digal ngéen jokkó ak fajkat rawatina su xale mbaa tuut tank Njumte ba wonn ko.
COPPITE CI WALLU MELOKAAN
Am na ñaari cosaan yu mën a soppi gis-gisu Bio‑Oil® Dry Skin Gel. Fekk bu njëkk bi dafa am bu sel bi nekk ci àdduna yu mag mbaa yu néew ci yàgg yu yàgg; àdduna yu mag yi di dëddu suuf si sel bi, loolu dafa am lu bare bu ñu bàyyi ko ci ubbi. Ci beneen fànn, ay tamperatiir yu suufe torop mënna tax mu forme. Ñaari mbir yóoyu yépp mënna ñu jox sel bi melokaan bu weex. Ñaareelu misàal bi mu ngi am su ndox mi, mbaa beneen likid dugge ci ndàa li su ñu koy jëfandiku. Likid bi defay laale ak emilsiyàan bi nekk ci njaxas bi mu daal di jur emilsifikaasiyon bi, moo tax sel bi di weex aki soppeeku.
BÉS BI ÑU KO GÉJE YEESALAAT
22 UT 2023